Seriñ Tuubaa ba muy jóg ca tánku yonent Sallal laahu 'alayhi wa sallama la daaldi jaar. Fi mu jaaroon rekk la jaar moom it. Ay mbokkam aki noonam fune jaar nañu ko ko fa. Lor gune def nañu ko ko, wante moom amul woon ndigёlul xeex, xeexu baatiin la xeex. Bamu bёggee xeex xeexu baatiin te bёgg leena not, booba la ñaan su boroom yen bi ko sunu boroom jox tey, mu yenu yen bi, hánd ak ñoom foo xam ne mbokkam mu koy xeexle walla mu koy xuloole, kenn taxawu fa. Mu jёflante ak ñoom li muy jёflante ci baatiin, ba mu mokk ba nooy népp, mu dellusiwaat tekki ёmb bi mu yoroom, nit ñepp di ci jёriñu.

Qasaayid yooyu mu def it, ba dem ci Jazbu [...], bis biñu xeexee Badr ba mu jeex, nee na kerook lañu ham kóóluteek am jamm haduna ak alaaxira […]. Kon leegi xeex moom, képp ku ko defaat moom, danga ko def ci sa coobare walla ngir wut darajay haduna walla hallal, waaye du ndigёl lu joge ci sunu boroom.


Ci yonent bi la tambale ci yonent bi la yem. Moo tax Shaykhul Khadīm xeexul. Amoon na doole jum xeexe, amoon na ñu ko gёm ñu ko mёnoona xeexle, waaye bamu bañee xeex, bёgga jámma tax mu ne leen : "toog leen fii ma hánd ak samay noon dem ba foo xam ne lu ñu ma mёna def kenn du ko mettitlu, ndax kenn ci yeen du ko fekke" ndax am na lu ñu ko def ci barab boobee ci ay náttu aki mettit, su fekkoon ci biiri mbokkam la, walla ci biiri taalibeem, kon musiba dina ham, ndax duñu ko mёna muñ, lu mu tere-tere duñu ko mёna muñ. Bёgg jámm, bёgg nit ñi ham jámm moo tax mu hánd ak ñoom dem fi ñu woolu, xeew ak ñoom xeexu baatiin sooga ñibisi. Kon kooku ku bёgg jámm moo la ko gёna bёgg.

Kon ñun ñii nga xam ne moom lañu yaakaar tey ak ёllёg, la Seriñ 'Abdul Ahad waxoon rekk: Seriñ Tuubaa deesu ko xeexal, deesu ko xulool. Dees koy yaakaar rekk te topp ko. Yaakaar ko mooy xam ne sunu boroom la mu doon joxe, jox na ko ko mu jaar ci yonent bi Sallal Laahu ‘alayhi wa sallam dikk ci moom, mu fab ñu boole ñu ak moom ñu war ko topp di ko lёggeyal di báyyi ay tereem te jёfe ay ndigёlam. Kon, xeexluwuñu xuloolewuñu. Dafa bёgg kunekk nekk ci jámm, may sa mbokk jullit jámm.


Nit ki ñenti jёmm la nekkal fii ci haduna: yalla sunu boroom, mbokk mu la yalla booleel ngeen bokk, mbokkum taalibe, ak dёkkándóór bu mu joteelul dara. Ñent ñii kune am na ñétti jikko yoo wara hánd ak moom : Sunu boroom mii, bu la digalee nga def, bu la teree nga báyyi, bu dogalee na la neex. Sa mbokk haqan mii, bokk leen pexe, bokk yeene, bokk li leen yalla wёrsёgal. Jámm ne ñoy.


Sa mbokkum taalibe mii, def ko ni nga def sa bopp, wóólu ko ni nga wóóloo sa bopp, ngeen di dimbalante, di sottanteey xalaat. Jaambur bii nga dёkkal te bokku leen diine, li lay may jámm ci moom, bu ko bañ, bu ko xeeb, bu ko yab. Jámm daaldi ham seen diggante. Kon, loolu mooy nii nga xam ne Seriñ Tuubaa noonu moom la doon jёfe, noonu lay doxe, nun ñi top ci moom it ci loolu lañu nekk.